Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - YOWAANA - YOWAANA 8

YOWAANA 8:3-30

Help us?
Click on verse(s) to share them!
3Xutbakat ya ak Farisen ya indi jenn jigéen ju ñu bettoon muy njaaloo, ñu taxawal ko ca diggu mbooloo ma.
4Noonu ñu ne Yeesu: «Kilifa gi, jigéen jii de, dañu koo bett muy njaaloo.
5Ci ndigali Yàlla yi, jigéen ju njaaloo, Musaa dafa santaane ñu sànni ko ay xeer, ba mu dee. Yaw nag, lu ciy sa xalaat?»
6Loolu nag, dañu ko doon wax ngir seetlu ko, ndaxte bëggoon nañoo tiiñal Yeesu. Yeesu sëgg, di bind ak baaraamam ci suuf.
7Bi laaj ya baree, mu siggi ne leen: «Ku masula def bàkkaar ci yéen, na ko jëkka sànniy xeer.»
8Noonu mu sëggaat, dellu di bind ci suuf.
9Bi ñu déggee loolu, ñuy rocceeku kenn-kenn, mag ña jiitu. Yeesu rekk des fa, jigéen ja taxaw ca kanamam.
10Mu daldi siggi ne ko: «Jigéen ji, ana ñi la doon jiiñ njaaloo? Ndax kenn tegu la tooñ?»
11Mu ne ko: «Kenn, Sang bi.» Yeesu ne ko: «Man it ci sama wàll, duma la daan. Demal, waaye bul defati bàkkaar.»
12Yeesu jubluwaat ca mbooloo ma ne leen: «Man maay leeru àddina si. Ku ma topp doo dox cig lëndëm, waaye dinga am leeru dund.»
13Farisen ya ne ko: «Yaw yaay seedeel sa bopp, kon li ngay wax du dëgg.»
14Yeesu ne leen: «Maa ngi seedeel sama bopp, teewul li may wax di dëgg, ndaxte xam naa fa ma bàyyikoo, xam fa ma jëm. Waaye yéen xamuleen fa ma bàyyikoo ak fa ma jëm.
15Ci gis-gisu àddina ngeen di àttee; man duma àtte kenn.
16Teewul nag, su ma demee bay àtte, bu jub lay doon, ndaxte du man rekk ay àtte, waaye Baay, bi ma yónni, daf ciy ànd ak man.
17Seen yoon dafa wax ne seedes ñaari nit a gëna wóor.
18Man maa ngi seedeel sama bopp, te Baay bi ma yónni mi ngi may seedeel itam.»
19Ñu laaj ko ne: «Kuy sa baay?» Yeesu ne leen: «Xamuleen ma, xamuleen sama Baay. Bu ngeen ma xamoon, xam ko.»
20Bi muy wax loolu, Yeesoo nga doon jànglee ca kër Yàlla ga, ca wetu fa ñu doon denc asaka ya. Kenn manu ko woona jàpp, ndaxte waxtoom jotagul.
21Yeesu dellu ne leen: «Maa ngi dem; dingeen ma seet, waaye seen bàkkaar ngeen di deeyaale. Fa ma jëm, dungeen fa mana dem.»
22Yawut yay waxante naan: «Nee na kat, fa mu jëm, dunu fa mana dem. Mbaa du day xaruji?»
23Yeesu ne leen: «Yéen, fii ngeen bawoo, ci suuf, waaye man ca kaw laa jóge. Àddina ngeen soqikoo, waaye man bokkuma ci.
24Looloo tax ma ne, ci seeni bàkkaar ngeen di dee. Bu ngeen gëmul ki ma nekk, dingeen dee ci seeni bàkkaar.»
25Ñu ne ko: «Yaay kan?» Mu ne leen: «Li ma leen waxoon ca njàlbéen ga.
26Li ma mana wax ci yéen ba àtte leen, bare na. Waaye ki ma yónni, ku wóor la, te li mu ma wax rekk laay jottali àddina.»
27Xamuñu woon ne, Yàlla Baay bee tax muy wax.
28Yeesu nag ne leen: «Bu ngeen yékkatee Doomu nit ki, dingeen xam ne Maay ki Nekk. Dingeen xam ne it, duma def dara man ci sama bopp. Li ma Baay biy jàngal rekk laay wax.
29Te it ki ma yónnee ngi ànd ak man; masu maa bàyyi ma wéet, ndaxte li ko neex rekk laay def.»
30Bi ñuy dégg Yeesu di wax loolu, ñu bare daldi koy gëm.

Read YOWAANA 8YOWAANA 8
Compare YOWAANA 8:3-30YOWAANA 8:3-30