Text copied!
Bibles in Wolof

YOWAANA 7:23-32 in Wolof

Help us?

YOWAANA 7:23-32 in Téereb Injiil

23 Bu ngeen manee xarafal nit ci bésub noflaay bi, ngir baña wàcc yoonu Musaa, lu tax nag ngeen mere ma, ndax li ma ci wéral nitu lëmm?
24 Bàyyileen di àtte ci ni ngeen di gise, te di àtte dëgg.»
25 Am na ci waa Yerusalem ñu doon wax naan: «Xanaa du nit kii lañuy wuta rey?
26 Xool-leen, mi ngi waaraate ci biir nit ñi, te kenn du ko wax dara. Ndax sunu kilifa yi dañoo xam ne mooy Almasi bi?
27 Waaye waa ji, xam nanu fu mu jóge, te saa su Almasi bi dee dikk, kenn du xam fu mu bàyyikoo.»
28 Yeesu di jàngle ca kër Yàlla ga, daldi wax ca kaw ne: «Ndax xam ngeen ma te xam fi ma jóge? Ñëwaluma sama bopp, waaye ki ma yónni, ku wóor la. Yéen xamuleen ko.
29 Man xam naa ko, ndaxte ca moom laa jóge, te itam moo ma yónni.»
30 Noonu ñu koy wuta jàpp, waaye kenn manalu ko woon dara, ndaxte waxtoom jotagul woon.
31 Moona nag, ñu bare ca mbooloo ma gëm nañu ko. Ñu nga naan: «Ndax bés bu Almasi bi dikkee, ay firndeem dina ëpp yu nit kii?»
32 Farisen ya daldi dégg la mbooloo ma doon déeyante ci mbirum Yeesu. Sarxalkat yu mag ya ak Farisen ya yebal ay alkaati yu daan wottu kër Yàlla ga, ngir ñu jàppi ko.
YOWAANA 7 in Téereb Injiil