Text copied!
Bibles in Wolof

YOWAANA 7:1-17 in Wolof

Help us?

YOWAANA 7:1-17 in Téereb Injiil

1 Gannaaw loolu Yeesu doon na wër diiwaanu Galile.
2 Bëggul woona dem diiwaanu Yude, ndaxte Yawut ya dañu ko doon wuta rey. Fekk na bésu xewu Yawut ya, ñu koy wax màggalu Mbaar ya, mu ngi doon jubsi.
3 Noonu rakki Yeesu yu góor ya ne ko: «Jóge fi te dem diiwaanu Yude, ngir say taalibe gis, ñoom itam, jaloore yi ngay def.
4 Ku bëgga siiw, doo nëbb say jëf. Boo demee bay wone jaloore yu mel ni, fexeel ba ñépp gis la.»
5 Rakkam yi dañu doon wax loolu, ndaxte ñoom itam gëmuñu ko woon.
6 Yeesu ne leen: «Sama waxtu jotagul. Ci yéen nag, waxtu yépp a baax.
7 Àddina du leen bañ waaye bañ na ma, man, ndaxte maa wax ne seeni jëf baaxul.
8 Yéen nag demleen màggal ga. Demaguma màggal googu, ndaxte sama waxtu jotagul.»
9 Bi mu leen waxee loolu ba noppi, moom mu des Galile.
10 Bi rakkam ya demee ca màggal ga, Yeesu itam sooga dem te kenn yégu ko; siiwalul demam.
11 Fekk Yawut yaa nga ko doon seet ca màggal ga te naan: «Ana waa ji?»
12 Ca biir mbooloo ma ñu ngi doon déeyante, di wax ci ay mbiram. Ñii naan: «Nit ku baax la.» Ñee naan: «Déedéet, day nax nit ñi.»
13 Waaye kenn ñemewu koo tudd ca kaw, ndaxte dañoo ragaloon Yawut ya.
14 Bi ñu demee ba ca diggu màggal ga, Yeesu dem di jàngle ca kër Yàlla ga.
15 Yawut ya nag jaaxle, daldi ne: «Nu waa jii def ba xam lii lépp, moom mi jàngul?»
16 Yeesu daldi leen wax ne: «Li may jàngle, jógewul ci man, waaye ci ki ma yónni la jóge.
17 Ku fas yéenee wéy ci bëgg-bëggu Yàlla, dina xam ndax sama njàngle ci Yàlla la jóge, walla ci sama coobare.
YOWAANA 7 in Téereb Injiil