Text copied!
Bibles in Wolof

YOWAANA 6:2-18 in Wolof

Help us?

YOWAANA 6:2-18 in Téereb Injiil

2 Mbooloo mu bare topp ci moom, ndaxte gisoon nañu firnde yooyee mu wone, bi mu wéralee jarag ya.
3 Yeesu daldi yéeg ca kaw tund wa, toog fa ak ay taalibeem.
4 Fekk na booba bésu Mucc ba, di màggalu Yawut ya, jubsi.
5 Bi Yeesu xoolee, gis mbooloo mu réy di ñëw ci moom, mu ne Filib: «Fu nuy jële mburu, mu nu leen mana dundale?»
6 Bi muy wax loolu it, da doon seetlu Filib, ndaxte xamoon na booba li mu nara def.
7 Filib ne ko: «Peyug juróom ñetti weer sax, bu nu ko amoon, du leen mana doy ci mburu, ba kenn ku nekk ci ñoom am ci dog wu ndaw.»
8 Keneen ca taalibe ya di Andare, mi bokk ak Simoŋ Piyeer ndey ak baay, ne ko:
9 «Am na fi ci mbooloo mi ab xale bu yor juróomi mburu ak ñaari jën, waaye loolu lu muy jariñ mbooloo mu tollu nii?»
10 Yeesu daldi ne taalibe ya: «Na ñépp toog.» Fekk ñax mu bare amoon ca bérab ba. Noonu góor ñépp àgg suuf. Waroon nañoo mat juróomi junni.
11 Yeesu daldi jël mburu ya, gërëm Yàlla, ba noppi séddale ko ña fa toogoon. Mu jox leen itam jën, ba ñu doyal sëkk.
12 Bi ñu lekkee ba regg, Yeesu ne taalibe ya: «Dajaleleen desitu mburu mi, ba dara du ci réer.»
13 Ñu dajale ko, daldi feesal fukki pañe ak ñaar ak desiti juróomi mburu, yi ñu doon lekk.
14 Bi nit ña gisee firnde jooju Yeesu wone, ñu ne: «Dëgg-dëgg kii mooy Yonent, bi wara ñëw ci àddina!»
15 Yeesu gis ne dañu koo nara jëlsi, fal ko buur. Mu bàyyi leen fa, dellu moom rekk ca tund wa.
16 Bi timis jotee taalibeem ya wàcc ca tefes ga,
17 dugg ci gaal, di jàll dex gi, jëm dëkku Kapernawum. Booba guddi woon na, te Yeesu agseegul ci ñoom.
18 Dex gi yëngu na lool, ndaxte da doon ngelaw ak doole.
YOWAANA 6 in Téereb Injiil