Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - YOWAANA - YOWAANA 6

YOWAANA 6:2-18

Help us?
Click on verse(s) to share them!
2Mbooloo mu bare topp ci moom, ndaxte gisoon nañu firnde yooyee mu wone, bi mu wéralee jarag ya.
3Yeesu daldi yéeg ca kaw tund wa, toog fa ak ay taalibeem.
4Fekk na booba bésu Mucc ba, di màggalu Yawut ya, jubsi.
5Bi Yeesu xoolee, gis mbooloo mu réy di ñëw ci moom, mu ne Filib: «Fu nuy jële mburu, mu nu leen mana dundale?»
6Bi muy wax loolu it, da doon seetlu Filib, ndaxte xamoon na booba li mu nara def.
7Filib ne ko: «Peyug juróom ñetti weer sax, bu nu ko amoon, du leen mana doy ci mburu, ba kenn ku nekk ci ñoom am ci dog wu ndaw.»
8Keneen ca taalibe ya di Andare, mi bokk ak Simoŋ Piyeer ndey ak baay, ne ko:
9«Am na fi ci mbooloo mi ab xale bu yor juróomi mburu ak ñaari jën, waaye loolu lu muy jariñ mbooloo mu tollu nii?»
10Yeesu daldi ne taalibe ya: «Na ñépp toog.» Fekk ñax mu bare amoon ca bérab ba. Noonu góor ñépp àgg suuf. Waroon nañoo mat juróomi junni.
11Yeesu daldi jël mburu ya, gërëm Yàlla, ba noppi séddale ko ña fa toogoon. Mu jox leen itam jën, ba ñu doyal sëkk.
12Bi ñu lekkee ba regg, Yeesu ne taalibe ya: «Dajaleleen desitu mburu mi, ba dara du ci réer.»
13Ñu dajale ko, daldi feesal fukki pañe ak ñaar ak desiti juróomi mburu, yi ñu doon lekk.
14Bi nit ña gisee firnde jooju Yeesu wone, ñu ne: «Dëgg-dëgg kii mooy Yonent, bi wara ñëw ci àddina!»
15Yeesu gis ne dañu koo nara jëlsi, fal ko buur. Mu bàyyi leen fa, dellu moom rekk ca tund wa.
16Bi timis jotee taalibeem ya wàcc ca tefes ga,
17dugg ci gaal, di jàll dex gi, jëm dëkku Kapernawum. Booba guddi woon na, te Yeesu agseegul ci ñoom.
18Dex gi yëngu na lool, ndaxte da doon ngelaw ak doole.

Read YOWAANA 6YOWAANA 6
Compare YOWAANA 6:2-18YOWAANA 6:2-18