Text copied!
Bibles in Wolof

YOWAANA 5:5-20 in Wolof

Help us?

YOWAANA 5:5-20 in Téereb Injiil

5 Amoon na fa benn waay bu feebaroon lu mat fanweeri at ak juróom ñett.
6 Bi ko Yeesu séenee mu tëdd, te mu xam ne woppam ji yàggoon na lool, mu laaj ko ne: «Ndax bëgg ngaa wér?»
7 Jarag ja ne ko: «Sang bi, duma am ku ma sóob ci ndox mi, bu yëngoo; su ma ciy fexee dem, ñu jëkk ma ci.»
8 Yeesu ne ko: «Jógal, jël sa basaŋ te dox.»
9 Ca saa sa mu daldi wér, jël basaŋam, daldi dox. Mbir moomu dafa daje woon ak bésub noflaay ba,
10 looloo tax ba Yawut ya daldi ne nit ku wér ka: «Tey bésub noflaay la, te sunu yoon aaye na, ngay yor sa basaŋ.»
11 Mu ne leen: «Ki ma faj moo ma ne: “Jëlal sa basaŋ te dox.”»
12 Ñu ne ko nag: «Ku la ne: “Jëlal sa basaŋ te dox”?»
13 Waaye waa ji xamul ki ko wéral, fekk booba Yeesu dem na, te nit ñu bare teewoon nañu ca bérab ba.
14 Bi ñu ca tegee ab diir, Yeesu dajeek moom ca kër Yàlla ga ne ko: «Déglul, fii mu ne, wér nga; bul defati bàkkaar, ngir ragal lu yées lii dal la.»
15 Noonu nit ka dellu ne Yawut ya, Yeesu moo ko fajoon.
16 Looloo tax Yawut ya di wuta sonal Yeesu, ndaxte daan na jëfe noonu ca bésub noflaay ba.
17 Waaye Yeesu wax na leen ne: «Sama Baay nekk na ba tey ci liggéey, kon man itam damay liggéey.»
18 Baat boobu moo tax ba Yawut yi gën koo wuta rey, ndaxte yemul woon rekk ci baña topp ndigalu bésub noflaay ba, waaye dafa wax it ne, Yàlla Baayam la, ba teg boppam Yàlla.
19 Noonu Yeesu ne leen: «Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, Doom ji manula def dara moom ci boppam; li mu gis Baay bi di def rekk lay def. Li Baay bi di jëf la Doom ji itam di jëf.
20 Ndaxte Baay bi bëgg na Doom ji, ba di ko won lépp lu muy def, te dina ko won jëf yu ëpp kéemaan yii, ngir ngeen gëna waaru.
YOWAANA 5 in Téereb Injiil