Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - YOWAANA - YOWAANA 5

YOWAANA 5:5-20

Help us?
Click on verse(s) to share them!
5Amoon na fa benn waay bu feebaroon lu mat fanweeri at ak juróom ñett.
6Bi ko Yeesu séenee mu tëdd, te mu xam ne woppam ji yàggoon na lool, mu laaj ko ne: «Ndax bëgg ngaa wér?»
7Jarag ja ne ko: «Sang bi, duma am ku ma sóob ci ndox mi, bu yëngoo; su ma ciy fexee dem, ñu jëkk ma ci.»
8Yeesu ne ko: «Jógal, jël sa basaŋ te dox.»
9Ca saa sa mu daldi wér, jël basaŋam, daldi dox. Mbir moomu dafa daje woon ak bésub noflaay ba,
10looloo tax ba Yawut ya daldi ne nit ku wér ka: «Tey bésub noflaay la, te sunu yoon aaye na, ngay yor sa basaŋ.»
11Mu ne leen: «Ki ma faj moo ma ne: “Jëlal sa basaŋ te dox.”»
12Ñu ne ko nag: «Ku la ne: “Jëlal sa basaŋ te dox”?»
13Waaye waa ji xamul ki ko wéral, fekk booba Yeesu dem na, te nit ñu bare teewoon nañu ca bérab ba.
14Bi ñu ca tegee ab diir, Yeesu dajeek moom ca kër Yàlla ga ne ko: «Déglul, fii mu ne, wér nga; bul defati bàkkaar, ngir ragal lu yées lii dal la.»
15Noonu nit ka dellu ne Yawut ya, Yeesu moo ko fajoon.
16Looloo tax Yawut ya di wuta sonal Yeesu, ndaxte daan na jëfe noonu ca bésub noflaay ba.
17Waaye Yeesu wax na leen ne: «Sama Baay nekk na ba tey ci liggéey, kon man itam damay liggéey.»
18Baat boobu moo tax ba Yawut yi gën koo wuta rey, ndaxte yemul woon rekk ci baña topp ndigalu bésub noflaay ba, waaye dafa wax it ne, Yàlla Baayam la, ba teg boppam Yàlla.
19Noonu Yeesu ne leen: «Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, Doom ji manula def dara moom ci boppam; li mu gis Baay bi di def rekk lay def. Li Baay bi di jëf la Doom ji itam di jëf.
20Ndaxte Baay bi bëgg na Doom ji, ba di ko won lépp lu muy def, te dina ko won jëf yu ëpp kéemaan yii, ngir ngeen gëna waaru.

Read YOWAANA 5YOWAANA 5
Compare YOWAANA 5:5-20YOWAANA 5:5-20