Text copied!
Bibles in Wolof

YOWAANA 12:14-25 in Wolof

Help us?

YOWAANA 12:14-25 in Téereb Injiil

14 Yeesu wut cumbur, war ko; ndaxte Mbind mi nee na:
15 «Buleen ragal, waa Siyoŋ. Gis ngeen, seen buur a ngi ñëw, war mbaam mu ndaw.»
16 Yooyu yépp, taalibe ya xamuñu woon ca saa sa lu muy tekki; waaye gannaaw bi ndamu Yeesu feeñee, ñu fàttaliku ne, Mbind mi yégle woon na loolu ci moom, te amal nañu ko.
17 Ña nekkoon ak Yeesu ñépp, bi muy wooyee Lasaar mu génn ca bàmmeel ba te mu dekkal ko, demoon nañu, nettali la ñu gis.
18 Looloo tax mbooloo ma teeru ko, ndaxte yégoon nañu firnde jooju.
19 Farisen yi nag di waxante naan: «Gis ngeen, manuleen ci dara; ñépp a ngi koy topp!»
20 Ca mbooloo ma, amoon na ca ay Gereg yu bokk ca ña ñëwoon Yerusalem ngir jaamu Yàlla diirub màggal ga.
21 Ñëw nañu ci Filib, mi dëkk Betsayda ci diiwaanu Galile, ne ko: «Sang bi, danoo bëggoona gis Yeesu.»
22 Filib dem wax ko Andare; ñu ànd, waxi ko Yeesu.
23 Mu ne leen: «Waxtu wi ñu wara feeñale ndamu Doomu nit ki jot na.
24 Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, fi ak peppu dugub ji wadd ci suuf jaarul ci dee, du mana weesu li mu doon: pepp doŋŋ. Waaye bu deeyee, dina jur pepp yu bare.
25 Ku bëgg bakkanam dina ko ñàkk, waaye ku ko bañ ci àddina sii, dina ko denc ngir dund gu dul jeex gi.
YOWAANA 12 in Téereb Injiil