Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Yanqóoba

Yanqóoba 5

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Kaayleen nag ma wax leen, yeen boroom alal yi, jooyleen te yuuxu, ndax mitit yi leen di dikkal.
2Seen alal nëb na, seeni yére maxe,
3seen wurus ak seen xaalis xomaag. Xomaag ja dib seede bu leen tuumaal, di xoyom seenu suux ni sawara. Yeena dajale alal ca fan yu mujj ya.
4Dégluleen! Peyoor, ga ngeen xañ ña gub seen tool, mooy yuuxu noonu. Jàmbati góobkat ya tàbbi na ca noppi Boroom gàngoori xare yi.
5Dund gu nooy ak bànneexu bakkan daal ngeen nekke ci kaw suuf, di yaflu ci bésub rendi.
6Yeena daan ba reylu aji jub, te jéemula bañ.
7Kon nag bokk yi, muñleen, ba Boroom bi délsi. Seetleen ci beykat biy séentu njariñal meññeef mu jóge fi suuf si. Ma ngay muñ, céebo ba bët wàcc.
8Yeen itam muñleen te takk seenu fit, ndax bés ba Boroom biy dikk dëgmal na.
9Bokk yi, buleen di ñaxtoonte, lu ko moy dees na leen daan, te Daan-kat baa ngii taxaw ci bunt bi!
10Bokk yi, yonent yi wax ci turu Boroom bi, di dékku aw tiis, ak di muñ, defleen leen seeni royukaay.
11Xam ngeen ne ñi muñ lanu foog ne ñoom la mbég ñeel. Dégg ngeen na Ayóoba muñe woon, ak muj ga ko Boroom bi jagleel, ndax Boroom bi moo bare yërmande akug ñeewante.
12Li ci raw nag bokk yi, moo di buleen giñ, bu muy ci asamaan mbaa ci suuf mbaa ci leneen lu mu mana doon. Na seen waaw di waaw, seen déet di déet, bala ngeena tàbbi ci mbugal.
13Ana ci yeen ku nekk ciw tiis? Na ñaan. Ana ku ci am mbég? Na sàbbaal.
14Ana ku wopp ci yeen? Na woo magi mbooloom gëmkat ñi, ñu ñaanal ko, raayaale ko ag diw ci turu Boroom bi.
15Ñaan gu ànd ak ngëm day musal ki wopp, ba Boroom bi yékkati ko. Su dee daa bàkkaar, dees na ko jéggal.
16Kon nag tuddanteleen seeni bàkkaar tey ñaanalante, ndax ngeen wér. Aji jub ji, ag ñaanam, doole lay dale.
17Ilyaas nit la woon ku bindoo ni nun, waaye ba mu saxee ci ñaan ngir mu baña taw, ndox laalul suuf diiru ñetti at ak genn-wàll.
18Mu dellu ñaan, asamaan taw, suuf meññ meññeefam.

19Bokk yi, su amee ci yeen ku moy yoonu dëgg, keneen ku ko waññi,
20xamleen ne ku waññee bàkkaarkat ci yoonu sànkuteem, musal na bakkanam, te faral na ko bàkkaar yu bare.