8 Bésub Noflaay bu nekk nañu saxoo taaj mburu yooyu fi kanam Aji Sax ji. Loolu sas la bu bànni Israyil di tegoo fàww.
9 Mburu yooyu Aaróona aki doomam yu góor ñoo koy féetewoo, te nañu ko lekke fu sell, ndaxte lu sella sell la, di lu ñu séddoo fàww ci saraxi sawara yi ñeel Aji Sax ji.»