9 Su loolu wéyee Aji Sax ji wax na Musaa ne ko:
10 «Waxal bànni Israyil ne leen: Bu ngeen duggee ca réew ma ma leen jox, ba dajale la ngeen jële ca suufam, yóbbuleen ci sarxalkat bi takku peppum lors bi ngeen jëkka góob.
11 Sarxalkat bi day yékkati takk bi, jébbal ko Aji Sax ji, ngir mu nangul leen. Bés bi topp ci bésub Noflaay bi lay yékkati takk bi, jébbal ko ko.
12 Bés bi ñuy yékkati takk bi, jébbale, nangeen ci sarxal kuuy mu amul sikk, tollu ci menn at, ñu defal ko Aji Sax ji saraxu rendi-dóomal.
13 Saraxu pepp mi muy àndal juróom benni kiloy sunguf su mucc ayib lay doon, ñu xiiwe ko diw, muy saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji, ngir xetug jàmm. Sarax si ñuy tuural Aji Sax ji, liitaru biiñ laak genn-wàll.