5 «Fukki fan ak ñeent ci weer wi jëkk, diggante ngoon ak jant bu so, mooy màggalu bésub Mucc ba, ñeel Aji Sax ji.
6 «Fukki fan ak juróom ci weer woowu la ayu bésu Mburu mu amul lawiir di tàmbali, ñeel Aji Sax ji. Diiru juróom ñaari fan mburu mu amul lawiir ngeen wara lekk.
7 Bés bu jëkk bi ndaje mu sell ngeen ciy amal. Mboolem lu ngeen faral di liggéey buleen ko ci liggéey.
8 Defleen ci saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji diiru juróom ñaari fan. Bésub juróom ñaareel ba di bésub ndaje mu sell. Mboolem lu ngeen faral di liggéey buleen ko ci liggéey.»
9 Su loolu wéyee Aji Sax ji wax na Musaa ne ko: