Text copied!
Bibles in Wolof

Sarxalkat yi 23:14-43 in Wolof

Help us?

Sarxalkat yi 23:14-43 in Kàddug Yàlla gi

14 Du mburu, du pepp mu ñu séndal, du pepp mu bees mu ngeen wara lekk, ba keroog bés boobu ngeen di indi seen saraxu Yàlla. Dogal a ngoogu, di lu leen war fàww, yeen ak seen askan, ak fépp fu ngeen dëkk.
15 «Bésub Noflaay ba ngeen di indi takku bele biy saraxu yékkati-jébbale, bés ba ca topp ngeen di dale waññ juróom ñaari ayi bés yu mat sëkk.
16 Waññleen ba ca bés ba topp ci juróom ñaareelu bésub Noflaay ba, muy juróom fukki fan, ngeen indil ca Aji Sax ji saraxu pepp mu bees.
17 Seeni kër ngeen di jële ñaari mburu yuy doon saraxu yékkati-jébbale, mu ci nekk di lu ñu lakke juróom benni kiloy sunguf su mucc ayib; dees ciy def lawiir, lakkaale ko ko, muy saraxu ndoortel meññeef, ñeel Aji Sax ji.
18 Na mbooloo mi booleek mburu mi juróom ñaari kuuy yu amul sikk te tollu ci menn at, ak yëkk ak ñaari kuuy, mu doon saraxu rendi-dóomal, ñeel Aji Sax ji. Na ànd ak saraxu pepp ak sarax si ñuy tuur. Loolu sarax la ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji.
19 Te itam ngeen sarxal ab sikket buy doon saraxu póotum bàkkaar ak ñaari xari menn at, muy saraxu cant ci biir jàmm.
20 Sarxalkat bi day yékkati ñaari xar yooyu, boole kook mburum ndoortel meññeef mi, def ko sarax bu ñuy yékkati, jébbal Aji Sax ji. Yooyu sarax di lu sell ñeel Aji Sax ji, sarxalkat bee ko moom.
21 Wooteleen ci bés boobu ndaje mu sell, te lu ngeen faral di liggéey buleen ko ci liggéey. Dogal a ngoogu, di lu leen war fàww, yeen ak seen askan, ak fépp fu ngeen dëkk.
22 «Bu ngeen dee góob seen tool, buleen góob ba fa tool ba yem te buleen ci toppaat, di foraatu. Aji ñàkk akub doxandéem ngeen koy bàyyee. Maay seen Yàlla Aji Sax ji.»
23 Gannaaw loolu Aji Sax ji wax na Musaa ne ko:
24 «Waxal bànni Israyil ne leen: Bu juróom ñaareelu weer taxawee, bés bi jëkk ci weer wi, na doon seen bésub Noflaay bu ngeen di amal ndaje mu sell. Deeleen fàttlee bés bi liit yu xumb.
25 Mboolem lu ngeen faral di liggéey buleen ko ci liggéey, waaye nangeen ci indi saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji.»
26 Aji Sax ji teg ca wax Musaa ne ko:
27 «Te itam fukki fan ci juróom ñaareelu weer woowu, bésub Njotlaay ba lay doon. Ndaje mu sell ngeen ciy amal. Nangeen ci toroxlu te indi saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji.
28 Du lenn lu ngeen di liggéey ci boobu bés, ndax bésub Njotlaay la bu ngeen di jotoo fi seen kanam Yàlla, Aji Sax ji.
29 Te kat, képp ku toroxluwul boobu bés, dees koy dagge ci biir bànni Israyil.
30 Képp ku liggéey lenn ci boobu bés, su boobaa dinaa far kooku ci biir bànni Israyil, sànk ko.
31 Buleen ci liggéey dara. Dogal a ngoogu, di lu leen war fàww, yeen ak seen askan ak fépp fu ngeen dëkk.
32 Seen bésub Noflaay la bu ngeen di nopplu doŋŋ te war cee toroxlu. Li ko dale ci ngoonug juróom ñeenti fan ci weer wi ba ca ëllëg sa, ba jant so, ci ngeen di wormaal seen bésub Noflaay.»
33 Su loolu wéyee Aji Sax ji wax na Musaa ne ko:
34 «Waxal bànni Israyil ne leen: Ñu waññ dale ko ci fukki fan ak juróom ci weeru juróom ñaareel woowu ba mu am juróom ñaari fan. Diir boobu mooy màggalu bési Mbaar yi, ñeel Aji Sax ji.
35 Bés bu jëkk bi bésub ndaje mu sell la. Mboolem lu ngeen faral di liggéey buleen ko ci liggéey.
36 Diiru juróom ñaari fan ngeen di indi saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji. Bésub juróom ñetteel, ba wara doon seen ndaje mu sell, nangeen ci indi saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji. Ndajem mujjantal ba la. Mboolem lu ngeen faral di liggéey buleen ko ci liggéey.
37 «Yooyoo di màggali Aji Sax ji, yi ñu wara yégle, di ndaje yu sell yu ñuy indi ay saraxi sawara, ñeel Aji Sax ji, muy saraxu rendi-dóomal, ak saraxu pepp, ak yeneen saraxi jur gu ñuy rendi, ak sarax yi ñuy tuural Aji Sax ji, bés bu nekk ak la ca war.
38 Yooyu sarax jotewul dara ak saraxi bési Noflaay yu Aji Sax ji. Jotewul dara it ak yi ngeen di joxeel Aji Sax ji mbaa mboolem sarax yi ngeen di wàccoo ngiñ, ak mboolem saraxi yéene yi ngeen di defal Aji Sax ji.
39 «Ci biir loolu, fukki fan ak juróom ci juróom ñaareelu weer wi, gannaaw bu ngeen dajalee meññeefum réew mi, amal-leen màggalug Aji Sax ji diiru juróom ñaari fan. Na bés bu jëkk ba di bésub Noflaay, bésub juróom ñetteel ba di bésub Noflaay.
40 Bés bu jëkk ba wittleen doomi garab yu rafet ak cari tiir ak cari garab yu sëq ak cari garab yu ñuy wax sóol, tey saxe tàkkal dex. Nangeen bànneexu fi seen kanam Yàlla Aji Sax ji diiru juróom ñaari fan.
41 Wormaal-leen màggalug Aji Sax jooju, di juróom ñaari fan cim at, te wormaal-leen ko ci juróom ñaareelu weer wi. Dogal a ngoogu, di lu leen war fàww, yeen ak seen askan.
42 Ci ay mbaar ngeen di dëkk diiru juróom ñaari fan yooyu. Mboolem njuddu-ji-réew ci Israyil na ci dëkke mbaar,
43 su ko defee seeni sët xam ne ciy mbaar laa dëkkaloon bànni Israyil, ba ma leen génnee réewum Misra. Maay seen Yàlla Aji Sax ji.»
Sarxalkat yi 23 in Kàddug Yàlla gi