14 Gannaaw loolu képp ku bokkul ci waa kër sarxalkat yi, bu lekkee ci sarax su sell te du teyeefam, na dolli ca njégu sarax sa juróomeelu céru njég ga, delloo ko sarxalkat bi.
15 Te itam bu sarxalkat yi bàyyi bànni Israyil di teddadil sarax yu sell yi ñu jagleel Aji Sax ji.