21 Askanu Aaróona sarxalkat bi, du kenn ku ci am sikk kuy agsi ba fii, di joxe saraxi sawara yi ñeel Aji Sax ji. Sikk si ci moom a tax du mana agsi ba fii, di joxe ñamu Yàllaam.
22 Du tere mu saña lekk ci ñamu Yàllaam, muy ñam wu sell ak wu sella sell.