Text copied!
Bibles in Wolof

Sarxalkat yi 19:16-29 in Wolof

Help us?

Sarxalkat yi 19:16-29 in Kàddug Yàlla gi

16 Buleen wër di yàq deru nit ci seen bokki waa réew. Buleen def dara lu mana reylu seen moroom. Maay Aji Sax ji.
17 «Buleen tong seen mbokk, te àrtuleen seen moroom bu baax bala ngeena bokk ak moom gàddu bàkkaar.
18 Buleen di feyantook seen mbokkum waa réew te buleen ko dencal mer. Ni ngeen soppe seen bopp nag, nangeen ko soppe seen moroom. Maay Aji Sax ji.
19 «Te it sama dogali yoon yii nangeen ko sàmm: buleen boole ñaar yu bokkul wirgo ci seenug jur, ñuy jaxasoo; seen tool it buleen ci ji ñaari wirgoy jiwu te buleen sol yére yu ñu ràbbe ñaari xeeti wëñ yu bokkul.
20 «Ku tëdde ab jaam bu wara séy ak keneen te fekk joteesu ko, goreeleesu ko, ndàmpaay war na ca, waaye deesu leen boole rey, ndax li ndaw si dib jaam ba tey.
21 Waa ji day yóbbu am kuuyu peyug tooñ ca bunt xaymab ndaje ma, muy peyug tooñ, gi muy sarxalal Aji Sax ji.
22 Na ko sarxalkat bi defal kuuy miy saraxas peyug tooñ muy njotlaayam fi kanam Aji Sax ji, ndax bàkkaar bi mu def. Kon dees na ko jéggal bàkkaar bi mu def.
23 «Bu ngeen duggee ca réew ma, ba jëmbat fa mboolem xeetu garab guy meññ ay doom, nangeen aayal doom ya. Diiru ñetti at ngeen di aayal doom ya. Dungeen ko lekk ci diir boobu.
24 Atum ñeenteel ba doom ya yépp lañuy sellalal Aji Sax ji, te di ko bége ci biir cant.
25 Juróomeelu at ma doŋŋ ngeen di saña lekk doom ya. Su ko defee meññeef ma barkeelal leen. Man Aji Sax ji maay seen Yàlla.
26 «Buleen lekk lu am deret. Buleen di gisaane mbaa ngeen di jibar.
27 Buleen wat seen peggu kawaru bopp te buleen dagg seen peggu sikkim,
28 mbaa ngeen di dagg seen yaram, di ko mititloo ku dee, te buleen ñaasu fenn ci seen yaram. Maay Aji Sax ji.
29 «Buleen torxal seen doom ju jigéen, di ko def ab gànc; lu ko moy réew mi sóobu ci gànctu ba ne lijj ci ñaawtéef.
Sarxalkat yi 19 in Kàddug Yàlla gi