Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sarxalkat yi - Sarxalkat yi 19

Sarxalkat yi 19:16-29

Help us?
Click on verse(s) to share them!
16Buleen wër di yàq deru nit ci seen bokki waa réew. Buleen def dara lu mana reylu seen moroom. Maay Aji Sax ji.
17«Buleen tong seen mbokk, te àrtuleen seen moroom bu baax bala ngeena bokk ak moom gàddu bàkkaar.
18Buleen di feyantook seen mbokkum waa réew te buleen ko dencal mer. Ni ngeen soppe seen bopp nag, nangeen ko soppe seen moroom. Maay Aji Sax ji.
19«Te it sama dogali yoon yii nangeen ko sàmm: buleen boole ñaar yu bokkul wirgo ci seenug jur, ñuy jaxasoo; seen tool it buleen ci ji ñaari wirgoy jiwu te buleen sol yére yu ñu ràbbe ñaari xeeti wëñ yu bokkul.
20«Ku tëdde ab jaam bu wara séy ak keneen te fekk joteesu ko, goreeleesu ko, ndàmpaay war na ca, waaye deesu leen boole rey, ndax li ndaw si dib jaam ba tey.
21Waa ji day yóbbu am kuuyu peyug tooñ ca bunt xaymab ndaje ma, muy peyug tooñ, gi muy sarxalal Aji Sax ji.
22Na ko sarxalkat bi defal kuuy miy saraxas peyug tooñ muy njotlaayam fi kanam Aji Sax ji, ndax bàkkaar bi mu def. Kon dees na ko jéggal bàkkaar bi mu def.
23«Bu ngeen duggee ca réew ma, ba jëmbat fa mboolem xeetu garab guy meññ ay doom, nangeen aayal doom ya. Diiru ñetti at ngeen di aayal doom ya. Dungeen ko lekk ci diir boobu.
24Atum ñeenteel ba doom ya yépp lañuy sellalal Aji Sax ji, te di ko bége ci biir cant.
25Juróomeelu at ma doŋŋ ngeen di saña lekk doom ya. Su ko defee meññeef ma barkeelal leen. Man Aji Sax ji maay seen Yàlla.
26«Buleen lekk lu am deret. Buleen di gisaane mbaa ngeen di jibar.
27Buleen wat seen peggu kawaru bopp te buleen dagg seen peggu sikkim,
28mbaa ngeen di dagg seen yaram, di ko mititloo ku dee, te buleen ñaasu fenn ci seen yaram. Maay Aji Sax ji.
29«Buleen torxal seen doom ju jigéen, di ko def ab gànc; lu ko moy réew mi sóobu ci gànctu ba ne lijj ci ñaawtéef.

Read Sarxalkat yi 19Sarxalkat yi 19
Compare Sarxalkat yi 19:16-29Sarxalkat yi 19:16-29