Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 9:8-16 in Wolof

Help us?

Sabóor 9:8-16 in Kàddug Yàlla gi

8 Aji Sax jee sax dàkk, samp jalam ngir àtte.
9 Moom mooy àtte àddina cig njub, di dogalal xeet yi dëgg.
10 Aji Sax jeey làq néew-ji-doole, mooy làqe bésub njàqare.
11 Aji Sax ji, yaw, ku la xam, wóolu la. Aji Sax ji, yaw, ku lay sàkku, doo ko wacc.
12 Woyleen Aji Sax ji dëkke Siyoŋ, siiwal-leen ay jalooreem ci xeet yi!
13 Mooy topp nit bakkanu moroomam, di ko ba xel, te du fàtte yuuxi néew-ji-doole.
14 Éy Aji Sax ji, baaxe ma, gisal naqar wi ma bañ yi teg. Yaa may yékkatee fa bunti ndee,
15 ba ma siiwali sa woy yépp, fa buntu Siyoŋ, dëkk bu taaru ba, di bànneexoo sa wall gii!
16 Xeet yee tàbbi pax ma ñu gasoon, fakktaloo fiir ga ñu làqoon.
Sabóor 9 in Kàddug Yàlla gi