7 Noon ya raaf, gental ba fàww. Yaa déjjati seeni dëkk, seenu askan fey.
8 Aji Sax jee sax dàkk, samp jalam ngir àtte.
9 Moom mooy àtte àddina cig njub, di dogalal xeet yi dëgg.
10 Aji Sax jeey làq néew-ji-doole, mooy làqe bésub njàqare.
11 Aji Sax ji, yaw, ku la xam, wóolu la. Aji Sax ji, yaw, ku lay sàkku, doo ko wacc.
12 Woyleen Aji Sax ji dëkke Siyoŋ, siiwal-leen ay jalooreem ci xeet yi!