Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 9:3-10 in Wolof

Help us?

Sabóor 9:3-10 in Kàddug Yàlla gi

3 Yaw Yàlla, dama lay bége, bànneexoo la, woy la, yaw Aji Kawe ji.
4 Noon yeey dellu gannaaw, tërëf, sànku fi sa kanam.
5 Yaa ma àtte yoon, dëggal ma, toog ci sab jal, di àtte njub.
6 Rëbb nga xeet yi, sànk ñu bon ñi, far seeni tur ba fàww.
7 Noon ya raaf, gental ba fàww. Yaa déjjati seeni dëkk, seenu askan fey.
8 Aji Sax jee sax dàkk, samp jalam ngir àtte.
9 Moom mooy àtte àddina cig njub, di dogalal xeet yi dëgg.
10 Aji Sax jeey làq néew-ji-doole, mooy làqe bésub njàqare.
Sabóor 9 in Kàddug Yàlla gi