7 Soo meree kay, nu sànku, nga xadaru, nu jàq.
8 Sunuy ñaawtéef a ngi janook yaw, te sunu mbóot leer na la.
9 Sunu giiru dund nga di nu mere, sunuy fan jeex ni noo guy naaw.
10 Sunu àppu dund di juróom ñaar fukki at, ku dëgër ba dëgër, juróom ñett fukk; li ci ëpp di coonooku tiis, ne fëyy, nu wéy.
11 Ana ku xam sa dooley mer ak sa xadar ju raglu?
12 Yal nanga nu xiir ci lim sunuy fan, ba nu mana dawal xel mu rafet.
13 Aji Sax ji, délsil, loo deeti xaar? Ngalla yërëmal sa jaam ñi.
14 Nu xëy, nga reggal nu sa ngor, nuy sarxolle, bànneexoo ko sunu giiru dund.