Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 90:3-11 in Wolof

Help us?

Sabóor 90:3-11 in Kàddug Yàlla gi

3 Yaay delloo doom aadama ci pënd, ne ko: «Yaw, doom aadama, dellul!»
4 Junniy at ci yaw daa gaaw ni démb ak tey, mbete waxtu yu néew ci wattub guddi.
5 Yaay buub nit, nelawal ko. Suba mu jebbi nim ñax,
6 xëy, jebbi, naat; ngoon mu lax, wowal.
7 Soo meree kay, nu sànku, nga xadaru, nu jàq.
8 Sunuy ñaawtéef a ngi janook yaw, te sunu mbóot leer na la.
9 Sunu giiru dund nga di nu mere, sunuy fan jeex ni noo guy naaw.
10 Sunu àppu dund di juróom ñaar fukki at, ku dëgër ba dëgër, juróom ñett fukk; li ci ëpp di coonooku tiis, ne fëyy, nu wéy.
11 Ana ku xam sa dooley mer ak sa xadar ju raglu?
Sabóor 90 in Kàddug Yàlla gi