13 Aji Sax ji, délsil, loo deeti xaar? Ngalla yërëmal sa jaam ñi.
14 Nu xëy, nga reggal nu sa ngor, nuy sarxolle, bànneexoo ko sunu giiru dund.
15 Bànneexal nu limu fan yi nga nu mbugal, diirub ati tiis yi nu dund.
16 Yal na sa jaloore leer sa jaam ñi, sa daraja leer seeni doom.