Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 89:3-22 in Wolof

Help us?

Sabóor 89:3-22 in Kàddug Yàlla gi

3 Dama ne, sa ngor dàkk la sax, fa asamaan nga dëël sa worma.
4 Aji Sax ji nee: «Damaa fas kóllëreek ki ma tànn, muy Daawuda sama jaam bi ma giñal ne ko:
5 “Damay saxal sa askan ba fàww, samp sab jal sët ba sëtaat.”» Selaw.
6 Aji Sax ji, waa asamaan a ngi lay sante say jaloore, ndajem ñu sell ña di la joobee sa worma.
7 Ana kuy dab-dabal Aji Sax ji, fa kawa kaw? Ana ci goney Yàlla yi ku nirook Aji Sax ji,
8 Yàlla, ji ñu terala teral ci jataayu ñu sell ñi, te mu gëna raglu lu ko wër?
9 Yàlla, Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, Ki Sax, ana ku tollook yaw doole? Yaw mi worma féete fu ne!
10 Yaw yaa man géej gu sàmbaraax; gannax ya fuddu, nga dalal.
11 Yaa fàdd Raxab, bóom ko, tasaare say noon ci sa doole.
12 Yaa moom asamaan, yaa moom suuf. Àddinaak li ci biiram, yaa ko taxawal.
13 Bëj-gànnaar ak bëj-saalum, yaa ko sàkk. Tabor ak Ermon, tund ya, di sarxollee sa tur.
14 Yaa àttan, jàmbaare; sa loxo di dooley neen, sa ndijoor ca kaw!
15 Njekk ak njub a lal sab jal, ngor ak worma dox jiitu la.
16 Aji Sax ji, ndokklee mbooloo mu la xal di sarxollee, di niitoo saw yiw,
17 ànd di la bége bés bu ne, sag njekk siggil leen.
18 Seen darajay doole, yaw a. Boo nu baaxee, nu yokku kàttan.
19 Sunu kiirlaay lii, Aji Sax jeey boroom; sunu buur bii, Aji Sell ji séddoo Israyil ay boroom.
20 Wax nga say wóllëre ci peeñu, ne leen: «Tànne naa jàmbaar ci xeet wi, dénk ko ndimbal.
21 Gis naa sama jaam Daawuda, fale ko sama diw gu sell,
22 ànd ak moom, saxal ko, di ko dooleel.
Sabóor 89 in Kàddug Yàlla gi