Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 89

Sabóor 89:3-22

Help us?
Click on verse(s) to share them!
3Dama ne, sa ngor dàkk la sax, fa asamaan nga dëël sa worma.
4Aji Sax ji nee: «Damaa fas kóllëreek ki ma tànn, muy Daawuda sama jaam bi ma giñal ne ko:
5“Damay saxal sa askan ba fàww, samp sab jal sët ba sëtaat.”» Selaw.
6Aji Sax ji, waa asamaan a ngi lay sante say jaloore, ndajem ñu sell ña di la joobee sa worma.
7Ana kuy dab-dabal Aji Sax ji, fa kawa kaw? Ana ci goney Yàlla yi ku nirook Aji Sax ji,
8Yàlla, ji ñu terala teral ci jataayu ñu sell ñi, te mu gëna raglu lu ko wër?
9Yàlla, Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, Ki Sax, ana ku tollook yaw doole? Yaw mi worma féete fu ne!
10Yaw yaa man géej gu sàmbaraax; gannax ya fuddu, nga dalal.
11Yaa fàdd Raxab, bóom ko, tasaare say noon ci sa doole.
12Yaa moom asamaan, yaa moom suuf. Àddinaak li ci biiram, yaa ko taxawal.
13Bëj-gànnaar ak bëj-saalum, yaa ko sàkk. Tabor ak Ermon, tund ya, di sarxollee sa tur.
14Yaa àttan, jàmbaare; sa loxo di dooley neen, sa ndijoor ca kaw!
15Njekk ak njub a lal sab jal, ngor ak worma dox jiitu la.
16Aji Sax ji, ndokklee mbooloo mu la xal di sarxollee, di niitoo saw yiw,
17ànd di la bége bés bu ne, sag njekk siggil leen.
18Seen darajay doole, yaw a. Boo nu baaxee, nu yokku kàttan.
19Sunu kiirlaay lii, Aji Sax jeey boroom; sunu buur bii, Aji Sell ji séddoo Israyil ay boroom.
20Wax nga say wóllëre ci peeñu, ne leen: «Tànne naa jàmbaar ci xeet wi, dénk ko ndimbal.
21Gis naa sama jaam Daawuda, fale ko sama diw gu sell,
22ànd ak moom, saxal ko, di ko dooleel.

Read Sabóor 89Sabóor 89
Compare Sabóor 89:3-22Sabóor 89:3-22