3 baal sa mbooloo seeni ñaawtéef, jéggal leen bépp bàkkaar. Selaw.
4 Ba nga xadar ja, muñ mer ma.
5 Éy Yàlla mi nuy musal, suqli nu, te meddi.
6 Xanaa doo nu mere fàww, ba ca sët yaak sëtaat ya?
7 Xanaa dinga leqli sa mbooloo, ba ñu man laa bànneexoo?