3 Sàmmleen àqu néew-ji-dooleek jirim, tey àtte yoon ku ñàkk ak ku ndóol.
4 Walluleen néew-ji-dooleek walaakaana, di leen xettli ci ku bon.
5 «Ndawi péncum Yàlla yii xamuñu, dégguñu; xanaa di doxe lëndëmu ñaawtéef, ba kenuy suuf yépp di jaayu.
6 «Dama ne ay yàlla ngeen, yeen ñépp di njabootu Aji Kawe ji.