8 Éy Yàlla Boroom gàngoor yi, suqli nu; geesoo nu sa leeru kanam, nu raw.
9 Yaa déjjatee reseñ Misra, dàq yéefar yi, indi, jëmbataat.
10 Nga wéex ko, mu sampu, law, dajal réew mi;
11 keppaaram muur tund yi, ay caram sàng garabi seedar yu mag yi.
12 Mu tàllal ay bànqaasam ba géej, lawal njebbit la ba dex ga.
13 Lu tax nga bëtt ay miiram, ba ku fa jaare witt ca,
14 mbaam àll di ko ruur, ndundati àll di ca for?
15 Éy Yàlla Boroom gàngoor yi, geesul; séentool asamaan, ba gis te taxawusi reseñ jii.
16 Taxawusil njëmbat lii nga jëmbate sa ndijoor, ngarab sii nga dooleelal sa bopp.