Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 80:5-19 in Wolof

Help us?

Sabóor 80:5-19 in Kàddug Yàlla gi

5 Éy Aji Sax ji, Yàlla Boroom gàngoor yi, foo àppal sa mer, mi ngay wuyoo sa ñaanu mbooloo mi?
6 Leel nga nuw naqar, nàndal nu mbàndum rongooñ,
7 def nga dëkkandoo di nu xëccoo, noon di nu ree.
8 Éy Yàlla Boroom gàngoor yi, suqli nu; geesoo nu sa leeru kanam, nu raw.
9 Yaa déjjatee reseñ Misra, dàq yéefar yi, indi, jëmbataat.
10 Nga wéex ko, mu sampu, law, dajal réew mi;
11 keppaaram muur tund yi, ay caram sàng garabi seedar yu mag yi.
12 Mu tàllal ay bànqaasam ba géej, lawal njebbit la ba dex ga.
13 Lu tax nga bëtt ay miiram, ba ku fa jaare witt ca,
14 mbaam àll di ko ruur, ndundati àll di ca for?
15 Éy Yàlla Boroom gàngoor yi, geesul; séentool asamaan, ba gis te taxawusi reseñ jii.
16 Taxawusil njëmbat lii nga jëmbate sa ndijoor, ngarab sii nga dooleelal sa bopp.
17 Dees koo gor, taal; yal na ñii sànkoo sa mbugal.
18 Yal nanga yiir ki nga tànn, kii nga dooleelal sa bopp,
19 ba dootunu la dëddu. May nu nu dund, nu wormaal sa tur.
Sabóor 80 in Kàddug Yàlla gi