Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 80:10-16 in Wolof

Help us?

Sabóor 80:10-16 in Kàddug Yàlla gi

10 Nga wéex ko, mu sampu, law, dajal réew mi;
11 keppaaram muur tund yi, ay caram sàng garabi seedar yu mag yi.
12 Mu tàllal ay bànqaasam ba géej, lawal njebbit la ba dex ga.
13 Lu tax nga bëtt ay miiram, ba ku fa jaare witt ca,
14 mbaam àll di ko ruur, ndundati àll di ca for?
15 Éy Yàlla Boroom gàngoor yi, geesul; séentool asamaan, ba gis te taxawusi reseñ jii.
16 Taxawusil njëmbat lii nga jëmbate sa ndijoor, ngarab sii nga dooleelal sa bopp.
Sabóor 80 in Kàddug Yàlla gi