Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 73:2-6 in Wolof

Help us?

Sabóor 73:2-6 in Kàddug Yàlla gi

2 Waaye man de tuuti kon ma lajj, tuuti ma tarxiis,
3 ngir maa ñee ku bew, ndax gis mu baaxle te di ku bon.
4 Amuñu metit, xanaa ne faaj.
5 Doñ-doñu nit dabu leen, coonoy doom aadama dalu leen.
6 Moo leen taxa ràngoo reewande, làmboo coxor.
Sabóor 73 in Kàddug Yàlla gi