19 Yàquleeka leena bett! Musibaa leen ne fuuf, ñu ne mes!
20 Day mel ni gént goo yewwoo. Céy Boroom bi, boo xippee, jëmmu gént ga soof la.
21 Naqar laa amoon, sama xol di dagg.
22 Booba ngaaka laa, xawma dara; rab laa woon fi sa kanam.
23 Teewul ma des ak yaw, nga jàpp sama loxol ndijoor.