Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 71:7-16 in Wolof

Help us?

Sabóor 71:7-16 in Kàddug Yàlla gi

7 Firndey alkànde la ma ñu bare xoole woon, te yaw ngay sama rawtu bu wóor.
8 Samay kàddu sag cant la fees ak di la saxoo darajaal.
9 Ngalla bu ma wacc, mag laa; bu ma ba fi doole jeexe.
10 Noon yaa nga may tooge, ñi may tëroo ngay diisoo,
11 naan: «Yàlla wacc na ko, nan ko dàq, jàpp; kenn du ko wallu.»
12 Éy Yàlla, bu ma sore. Sama Yàlla, gaawe ma.
13 Samay seytaane, yal nañu leen rusloo, sànk leen. Ñi may wuta lor, yal nañu leen gàcceel, sewal leen.
14 Man may saxoo yaakaar, di la sant, di santati.
15 May siiwal sa njekk, di yendoo waxtaane say wall, doonte lim ba wees na ma.
16 Boroom bi, Aji Sax ji, ma dikke la sag njàmbaar, di tudd sa njekk gu wéet.
Sabóor 71 in Kàddug Yàlla gi