3 Yal nangay sama cëslaay, sama rawtu bu may rawesi saa su ne, te nga dogal sama mucc. Yaw yaa may téye, di ma aar.
4 Éy sama Yàlla, musal ma ci dooley ku bon ak ab saaysaay ak ab néeg.
5 Boroom bi, Aji Sax ji, yaw de laa yaakaar, dale laa wóolu ba may ndaw.
6 Yaw laa wéeroo ba may juddu; yaw yaa ma roccee sama biiru ndey. Yaa yelloo sama cant fàww.
7 Firndey alkànde la ma ñu bare xoole woon, te yaw ngay sama rawtu bu wóor.
8 Samay kàddu sag cant la fees ak di la saxoo darajaal.
9 Ngalla bu ma wacc, mag laa; bu ma ba fi doole jeexe.
10 Noon yaa nga may tooge, ñi may tëroo ngay diisoo,
11 naan: «Yàlla wacc na ko, nan ko dàq, jàpp; kenn du ko wallu.»
12 Éy Yàlla, bu ma sore. Sama Yàlla, gaawe ma.
13 Samay seytaane, yal nañu leen rusloo, sànk leen. Ñi may wuta lor, yal nañu leen gàcceel, sewal leen.
14 Man may saxoo yaakaar, di la sant, di santati.
15 May siiwal sa njekk, di yendoo waxtaane say wall, doonte lim ba wees na ma.
16 Boroom bi, Aji Sax ji, ma dikke la sag njàmbaar, di tudd sa njekk gu wéet.
17 Éy Yàlla, ba may ndaw, nga ma xamal say kéemaan, te ba tey jii maa ngi koy biral.
18 Éy Yàlla, bu ma bijjaawee ba weex tàll it, bu ma wacc, ba keroog may xamal maasu tey sa doole, xamal ñi ciy topp ñépp sag njàmbaar.