3 Yal nangay sama cëslaay, sama rawtu bu may rawesi saa su ne, te nga dogal sama mucc. Yaw yaa may téye, di ma aar.
4 Éy sama Yàlla, musal ma ci dooley ku bon ak ab saaysaay ak ab néeg.
5 Boroom bi, Aji Sax ji, yaw de laa yaakaar, dale laa wóolu ba may ndaw.
6 Yaw laa wéeroo ba may juddu; yaw yaa ma roccee sama biiru ndey. Yaa yelloo sama cant fàww.
7 Firndey alkànde la ma ñu bare xoole woon, te yaw ngay sama rawtu bu wóor.
8 Samay kàddu sag cant la fees ak di la saxoo darajaal.
9 Ngalla bu ma wacc, mag laa; bu ma ba fi doole jeexe.
10 Noon yaa nga may tooge, ñi may tëroo ngay diisoo,
11 naan: «Yàlla wacc na ko, nan ko dàq, jàpp; kenn du ko wallu.»
12 Éy Yàlla, bu ma sore. Sama Yàlla, gaawe ma.
13 Samay seytaane, yal nañu leen rusloo, sànk leen. Ñi may wuta lor, yal nañu leen gàcceel, sewal leen.
14 Man may saxoo yaakaar, di la sant, di santati.