20 Won nga ma ay yoon coonooki tiis, waaye yaa may dundalaat, ma mucc xóotey suuf.
21 Yal nanga ma gëna sagal, geesu, bégal ma.
22 Man it sama Yàlla, ma xalam, sant la ngir sa kóllëre. Aji Sell ji séddoo Israyil, dama lay woy aki xalam,
23 sarxolle, woy la, bége sag njot.