Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 71:19-23 in Wolof

Help us?

Sabóor 71:19-23 in Kàddug Yàlla gi

19 Céy Yàlla, sa njekk àkki na fa kawa kaw. Def nga lu réy. Yaw Yàlla, ana ku mel ni yaw?
20 Won nga ma ay yoon coonooki tiis, waaye yaa may dundalaat, ma mucc xóotey suuf.
21 Yal nanga ma gëna sagal, geesu, bégal ma.
22 Man it sama Yàlla, ma xalam, sant la ngir sa kóllëre. Aji Sell ji séddoo Israyil, dama lay woy aki xalam,
23 sarxolle, woy la, bége sag njot.
Sabóor 71 in Kàddug Yàlla gi