7 Onk naa ba loof, di fanaanee jooy, sama lal di féey, ba far seeye rongooñ.
8 Saay gët a ngi xóot ndaxu naqar, boole ci giim ndax tooñi noonoo noon.
9 Yeen, defkati ñaawtéef yépp, xiddileen ma! Aji Sax ji dégg na saay jooy,
10 Aji Sax ji dégg na saay dagaan, Aji Sax jii nangu na samag ñaan.