7 Dama ne: «Éy ku may may laafi xati, ma ne fërr, noppluji.
8 Xanaa ma naaw, ba sore, fanaani màndiŋ ma. Selaw.
9 Naa gaawtu, seeluji ngelaw lu riddi ak ngëlén.»
10 Éy, Boroom bi, beenal seeni wax, neenal leen. Damaa gis fitnaak xuloo ci dëkk bi,
11 guddeek bëccëg ñuy wër, ñaawtéef ak ayib wéttali leen.
12 Yàq a nga ca biir, te noteel ak njublaŋ jógul ca pénc ma.