Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 55:19-23 in Wolof

Help us?

Sabóor 55:19-23 in Kàddug Yàlla gi

19 Moo may jot ak jàmm, ba ma mucc ci xare ya ma ñu bare di songe.
20 Yàllaay dégg, duma leen, moom mi nguuram yàgga sax. Selaw. Soppikuwuñu fenn te ragaluñu Yàlla.
21 Kii a ngi xàccil ñi mu takktool, di fecci kóllëre,
22 làmmiñ wa daa neex ni lem, te xare lal xol ba; kàddu ya gëna nooy ag oliw te di saamar bu génn mbaram.
23 Sippikul Aji Sax ji lu la diis, moom moo lay taxawu. Du bàyyi mukk aji jub, muy tërëf.
Sabóor 55 in Kàddug Yàlla gi