19 Moo may jot ak jàmm, ba ma mucc ci xare ya ma ñu bare di songe.
20 Yàllaay dégg, duma leen, moom mi nguuram yàgga sax. Selaw. Soppikuwuñu fenn te ragaluñu Yàlla.
21 Kii a ngi xàccil ñi mu takktool, di fecci kóllëre,
22 làmmiñ wa daa neex ni lem, te xare lal xol ba; kàddu ya gëna nooy ag oliw te di saamar bu génn mbaram.