13 Su doon noon bu may ñaawal, ma muñ ko, mbaa muy bañ bu may won ab dayo, ma daw ko.
14 Waaye yaw la, sama nawle, di sama wóllëre, ma xam la.
15 Nu daan bokk bànneexu diisoo, ànd ak mbooloo, di jaamuji kër Yàlla ga.
16 Yal na leen dee bett, ñu jekki tàbbi njaniiw, ngir mbon ga seen biir ak seen dëkkuwaay.
17 Waaye man, Yàlla laay woo wall, te Aji Sax jee may wallu.
18 Subaak ngoon ak njolloor, may ñaxtook a ñurumtu, mu dégg ma.
19 Moo may jot ak jàmm, ba ma mucc ci xare ya ma ñu bare di songe.