11 guddeek bëccëg ñuy wër, ñaawtéef ak ayib wéttali leen.
12 Yàq a nga ca biir, te noteel ak njublaŋ jógul ca pénc ma.
13 Su doon noon bu may ñaawal, ma muñ ko, mbaa muy bañ bu may won ab dayo, ma daw ko.
14 Waaye yaw la, sama nawle, di sama wóllëre, ma xam la.
15 Nu daan bokk bànneexu diisoo, ànd ak mbooloo, di jaamuji kër Yàlla ga.
16 Yal na leen dee bett, ñu jekki tàbbi njaniiw, ngir mbon ga seen biir ak seen dëkkuwaay.