3 Moo jàmbaar ji, looy damoo jëfi coxor? Yàlla, ngoram, bés bu nekk la.
4 Ak sa làmmiñ wi ngay sose loraange, mel ni saatu su ñu xacc, rambaaj bi!
5 Lu bon a la gënal lu baax, fen a la gënal wax dëgg. Selaw.
6 Yaa bëgg jépp wax juy yàq, waabajiiba bi!