Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 41:7-13 in Wolof

Help us?

Sabóor 41:7-13 in Kàddug Yàlla gi

7 Ku dikk, di ma seet, di jinigal tey fenti sos ci xolam, bu génnee, tasaare ko.
8 Bañ yépp a ngi may déeyoo, di ma fexeel lu bon,
9 naan: «Musiba dal na ko, du jógati!»
10 Sama am-di-jàmm bu ma wóolu sax jógal na ma, te daan lekk samaw ñam.
11 Waaye ngalla Aji Sax ji, baaxe ma, yékkati ma, ma fey leen.
12 Su noon damuwul ci sama kaw, ma doora xam ne bége nga ma.
13 Man, damaa maandu, nga taxawu ma, dëj ma fi sa kanam, ba fàww.
Sabóor 41 in Kàddug Yàlla gi