7 Ku dikk, di ma seet, di jinigal tey fenti sos ci xolam, bu génnee, tasaare ko.
8 Bañ yépp a ngi may déeyoo, di ma fexeel lu bon,
9 naan: «Musiba dal na ko, du jógati!»
10 Sama am-di-jàmm bu ma wóolu sax jógal na ma, te daan lekk samaw ñam.
11 Waaye ngalla Aji Sax ji, baaxe ma, yékkati ma, ma fey leen.