5 Maay woo Aji Sax ji wall, mu walloo ma fa tundam wu sell wa. Selaw.
6 Maay tëdd nelaw, yewwu; Aji Sax ji di ma aar.
7 Ñu dul jeex a ma jógal, gaw ma, te duma ragal.
8 Éy Aji Sax ji sama Yàlla, jógal, wallu ma! Yaa toj kaabaabi noon yu bon yépp, foq seeni sell.