7 Nit du lu moy takkndeer buy dem, cóolóolu neen lay kër-këri. Nit a ngi dajale, xamul kuy for.
8 «Éy Boroom bi, lu may xaarati? Sama yaakaar yaw a.
9 Musal ma ci sama mbugali tooñoo tooñ, bu ma bàyyi, dof di ma reetaan!
10 Noppi naa, dootuma wax, yaw yaa dogal lii.
11 Waaye ngalla teggil sab yar, sa diisaayu loxoo ngi may jekkli.
12 Yaay mbugal ku bàkkaar, yar ko, ronq ni max la mu gëna fonk. Nitoo nit, cóolóolu neen. Selaw.
13 Éy Aji Sax ji, déglul, ma ñaan la, teewlul, ma woo la wall; bul tanqamlu sama yuux, doxandéem doŋŋ laa fi yaw, di gan ni maam yépp.