Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 37:19-39 in Wolof

Help us?

Sabóor 37:19-39 in Kàddug Yàlla gi

19 Bu mettee doo rus, te bésub xiif dangay regg.
20 Ku bon sànku; noonub Aji Sax ji, taaru tool bu naat la, bu tàkkee, jeex tàkk.
21 Ku bon leb, du fey; ku jub yéwén, di joxe.
22 Aji Sax ji barkeel la, nga jagoo réew mi moos; mu alag la, nga dog.
23 Aji Sax jeey sopp saw yoon, jiite say jéego.
24 Soo tërëfee it, doo daanu. Aji Sax jee lay walloo loxoom.
25 Ba may ndaw, ba tey may mag, gisuma ku jub ñàkk ndimbal, mbaa askanam di dunde yalwaan.
26 Day saxoo tabe, di leble, askanam barkeel.
27 Dëddul mbon, di jëfe mbaax, ba dëkke réew mi fàww.
28 Aji Sax ji kat daa sopp yoon, te du wacc jaamam bu gore. Day fegu ba fàww, askanu ku bon dog.
29 Aji jub ay jagoo réew mi, dëkke ko ba fàww.
30 Kàddug aji jub day xelu, wax ja jub;
31 yoonu Yàllaam a nga ca xol ba, du dox ba tërëf.
32 Ku bon a ngi yeeru ku jub, di ko wuta bóom.
33 Waaye Aji Sax ji du ko bàyyeek moom, te deesu ko daan cib layoo.
34 Yaakaaral Aji Sax ji, sàmm yoonam, mu teral la, nga jagoo réew mi, ku bon sànku, ngay gis.
35 Damaa gis ku bon di note, te sëq ni garab gu naat fa mu fekk baax,
36 ma jaareeti fa, ndeke wuute na, ma seet ko, gisuma ko.
37 Bàyyil xel ku maandu, xool ku jub; muj, fa nitu jàmm.
38 Moykat yeey sànkoondoo, ku bon amul muj.
39 Aji Sax jeey musal ku jub, di ko aar bésub njàqare.
Sabóor 37 in Kàddug Yàlla gi