Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 37

Sabóor 37:19-39

Help us?
Click on verse(s) to share them!
19Bu mettee doo rus, te bésub xiif dangay regg.
20Ku bon sànku; noonub Aji Sax ji, taaru tool bu naat la, bu tàkkee, jeex tàkk.
21Ku bon leb, du fey; ku jub yéwén, di joxe.
22Aji Sax ji barkeel la, nga jagoo réew mi moos; mu alag la, nga dog.
23Aji Sax jeey sopp saw yoon, jiite say jéego.
24Soo tërëfee it, doo daanu. Aji Sax jee lay walloo loxoom.
25Ba may ndaw, ba tey may mag, gisuma ku jub ñàkk ndimbal, mbaa askanam di dunde yalwaan.
26Day saxoo tabe, di leble, askanam barkeel.
27Dëddul mbon, di jëfe mbaax, ba dëkke réew mi fàww.
28Aji Sax ji kat daa sopp yoon, te du wacc jaamam bu gore. Day fegu ba fàww, askanu ku bon dog.
29Aji jub ay jagoo réew mi, dëkke ko ba fàww.
30Kàddug aji jub day xelu, wax ja jub;
31yoonu Yàllaam a nga ca xol ba, du dox ba tërëf.
32Ku bon a ngi yeeru ku jub, di ko wuta bóom.
33Waaye Aji Sax ji du ko bàyyeek moom, te deesu ko daan cib layoo.
34Yaakaaral Aji Sax ji, sàmm yoonam, mu teral la, nga jagoo réew mi, ku bon sànku, ngay gis.
35Damaa gis ku bon di note, te sëq ni garab gu naat fa mu fekk baax,
36ma jaareeti fa, ndeke wuute na, ma seet ko, gisuma ko.
37Bàyyil xel ku maandu, xool ku jub; muj, fa nitu jàmm.
38Moykat yeey sànkoondoo, ku bon amul muj.
39Aji Sax jeey musal ku jub, di ko aar bésub njàqare.

Read Sabóor 37Sabóor 37
Compare Sabóor 37:19-39Sabóor 37:19-39